عَن أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ:
سَأَلَ رَجُلٌ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، إِنَّا نَرْكَبُ البَحْرَ، وَنَحْمِلُ مَعَنَا القَلِيلَ مِنَ الْمَاءِ، فَإِنْ تَوَضَّأْنَا بِهِ عَطِشْنَا، أَفَنَتَوَضَّأُ مِنَ الْبَحْرِ؟ فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «هُوَ الطَّهُورُ مَاؤُهُ، الحِلُّ مَيْتَتُهُ».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
jenn waay laaj na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, nun danuy dugg ci géej gi, di yor tuuti ndox, bu nu ci jàppee daal di mar, ndax nu jàppu ci ndoxum géej gi? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: «moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la».

Wér na رواه أبو داود والترمذي والنسائي وابن ماجه وأحمد Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 69

Leeral gi

Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: man damay war gaal nekk ci kaw géej gi ngir napp walla ngir yaxantu ak lu ko niru, nuy yor tuuti ndox mees man a naan, te bu nu ko jëfandikoo ci jàppu walla sangu day jeex te dunu am lu nu naan, ndax dana dagan nu jàppu ci ndoxom géej gi?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ci ndoxum géej ne: ndoxam mi dafa laab tey laabal; dana dagan a jàppu ak sangu, dagan na it ñu lekk la fay génne ci jën yu ndaw ak jën yu mag ak yeneen, donte dañu ko a fekk mu dee, daal di tëdd noonu ci lu dul ñu kenn napp ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Méddum rabi géej yi lu dagan la, li ñu namm ci méddam mooy: ndundatam ya dee te bokk ci yi dul dund lu dul ci biir géej.
  2. Tontu aji-laaj ji ci lu ëpp li mu laaj ngir mottali njariñ li.
  3. Ndox mi bu cafkaam walla meloom walla xetam soppeekoo ci lu laab, kon day des ca laab ga fii ak ndox la mu des di nekk ndox, donte xoramam walla tàngaayam walla seddam gi ak lu ko niru dafa tar lool.
  4. Ndoxum géej day yëkkëti sobe su mag ak su ndaw, day dindi it sobe su tàbbi ci lu laab, yaram ak yére mbaa leneen.

Gaaral firi yi

50 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
BN বাংলা البنغالية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية